Salam guy, donc dem ba légui mangui guet ay retours ci PI-SPI bi, gnu nane ma ay lan moy alias ak nign koy créer. Donc tay damay expliquer lan moy alias. Après dina doug ci application, wan lén nign koy créer ak nign koy supprimer yeup. Donc lan moy alias? Alias day melni matricule auto. Xam nga tay yow nit ki meun nga am auto yu beuri. So amé auto yu beuri, est-ce que auto bi ngay yor bou né, est-ce que bén matricule dafa wara nek ci auto yeup? Donc auto bou nék ak matricule lam, même bou féké bén nit ki moko mom. Donc compte yi légui nonu lay démé. Donc compte bou nék day am matricule. Yow même bou amé ñaari compte, nga am compte Orange Money ak am compte Wave, compte Orange Money dagn koy wutal matricule, compte Wave gnu wutal ko matricule. Donc ñom ñaar ñep dagnuy am matricule. Donte yu yamu compte bi, donc compte bou nék day am matricule. Léegi matricule bi motax gnu xamé compte yi. Waw, mo exemple bi ma joxé auto bi rek. Tay ji yow bo yoré 5 auto, dutax nga am bén matricule pour 5 auto yeup, dédet. Auto bou nék ak matricule lam, même bou féké yow ya mom auto yeup. Lolu moy tax gnu meuna xamé auto bou nék, bu défé problème, bu défé jéé, gnu xamni auto bi mo def nangam. Donc même solution la aussi ci compte yi. Donc alias lolou lay signifié. Compte bou nék day am alias am. Alias am mom moy matricule am wala moy carte d'identité bu lén néxé. Donc matricule compte bobu moy tax tay fu nit meuna nek ci aduna bi, ak application bu meunti utiliser bu am PI-SPI, day meuna utiliser sa alias. Donc meuno utiliser bén alias pour plusieurs comptes. Parce que meuno utiliser bén matricule auto, nga né dagn koy utiliser pour plusieurs auto. Meuno utiliser sa bén carte d'identité, nga dagn koy utiliser pour ñun gnu beuri. Donc lu ngén wara comprendre moy alias yi, comme matricule auto la rek wala comme pièce d'identité. Donc bén compte bou nék dagn koy matriculé, wala gnu wutal ko pièce d'identité, jappé lén ko nonu. Donc compte bou nék bén alias la am. Lolu motax yow sa numéro téléphone bu féké dang ko utiliser alias ci Orange Money, meunato ko utiliser Wave. Pourquoi? Parce que utiliser nagn ko mu nek matricule ci Orange Money ba paré. Donc mom moy nek sa matricule Orange Money. Donc so démé Wave, il faut nga généré bénén alias, moy bénén matricule. Donc alias yi dara warul compliqué wul ci, lolu kessa la. Moy compte bou nék day am matricule. Léegi yow man mi tay suma amé 5 compte tamit, compte bou nék damakoy créer matricule. Man légui yow so ma wara envoyé xaliss, man may xol compte buma néx ma dém jëli matricule bobu, manam ma dém jëli alias bobu ma jox lako. Léegi nak alias yi tamit jarul japp, parce que ay cent de caractère la. Donc bo xolé dang koy meuna copier, dang koy meuna partager, aussi meun nga scanner. Donc soxla wul diko japp, du nek ay numéro téléphone yo xamni, wala bo nit day taxaw fi nga koy éppé nane ko bëssal X, bëssal A, bëssal D, non du démé nonu. Donc alias yi bu guddé, bu gatté yeup amul solo, lolu jarul japp. Donc li ngén ci wara comprendre juste moy alias yi ay matricule la, donc day identifier compte yi. Voilà, day identifier compte yi. Sa compte bancaire sa day am alias. Donc sa compte bancaire day am matricule. Sa compte Orange Money day am matricule. Sa compte Wave day am matricule. Te matricule yoyu yeup bén du ci bok ak moromam, comme ay adresse la rek, comme adresse électronique wala. Donc lolu ngén wara comprendre. Donc ay matricule la, donc matricule bi moy tax gnu xamé compte bi. Tay ji yow so utilisé sa Orange Money, nga dug ci PI-SPI, nga bëgg ko envoyer, gnu jox la bén alias, manam gnu jox la bén matricule. Orange Money jéemul ligéenti sax baxam numéro bobu, baxam alias bobu bu Wave la, wala bu banque la, jéemuko ligéenti. Dégg nga nga jox ko alias bi rek so envoyé day dém directement ci compte bobu nonu, parce que alias bi moy tax gnu xam ni fi compte bi la wara dém, parce que lolu moy matricule am, lolu moy pièce d'identité am. Donc li ngén ci wara comprendre lolu la. Donc alias yi lolu moy sén jëri. Léegi damay lén wan nan lagnuy créer alias, ak lagn koy supprimer, mais pour faire simple, il faut ngén xam lolu, alias moy matricule compte bi. Donc man meun na am ñaari compte, am Orange Money, am Wave. Est-ce que meun nañu am bén matricule? Dédet, meunou gnu am même alias bi, meunou gnu am même matricule bi. Lan motax? Parce que day melni ku yor ñaari auto am, ku yor ñaari auto am, ñaari matricule yu bokul ngay yor. Auto bou nék dagn koy am matricule.